إعدادات العرض
Koor
Koor
1- tabax nañu lislaam ci juróom
2- waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
3- képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram
4- ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram
5- tabax nañu lislaam ci juróom
9- bu ngeen ko gisee woorleen, bu ngeen ko gisee worileen, bu muuroo ci yeen nangeen ko nattale
12- man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin
13- ku woor benn bis ci yoonu Yàlla, Yàlla soreele jëmmam ca sawara juróom-ñaar-fukki Nawet
14- nit ñi du ñu deñ di nekk ci yiw fii ak ñoo ngi gaaw a dog
17- xëddleen, ndaxte xëdd lu am baarke la
21- dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor
24- ku woor at mi kooku woorul, woor ñatti fan mooy woor at mi yépp
25- bu Ramadaan ñëwee dañuy tijji bunti àjjana yi, tëj bunti sawara yi, jéng saytaane yi
