إعدادات العرض
Woote ci Yàlla ak sàkku ci tuyaaba
Woote ci Yàlla ak sàkku ci tuyaaba
2- fépp fu yax di daje ci nit sarax la
6- bu nit ki feebaree walla mu tukki dees na ko bindal kem la mu daan jëf ba mu tukkiwul te wér
11- ku génnug topp, daal di tàqalikoo ak mbooloo ma ba faatu, kon dee na deewug ceddo
15- bokk na ci jihaad yi gën a màgg wax kàddug maanute fi kanamu buur bu jeng
18- yaw sama baay tëx, waxal: laa ilaaha Illal Laahu, genn kàddu gog dinaala ci mana layal fa Yàlla
19- nit ñi bu ñu gisee tooñkat bi te téyewuñu loxoom kon tuuti rekk Yàlla boole leen mbugal
20- fépp fu yax di daje ci nit sarax la
22- diine ji lu yomb la, te kenn du taral diine ji lu dul ne dana ko not, kon deeleen jubal, di jegeele
23- ku ne ci yéen ab sàmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm,
25- man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin
26- yéen nit ñi Yàlla de jële na ci yéen rëy-rëylug ceddo ga ak seenug damu ci seen baay ya
27- ay fitna dana am, yëgleen ne bu fitna amee ka toog moo gën ka kay dox, kay dox mooo gën kay daw,
