إعدادات العرض
Dégg diine ak i cosaanam - الصفحة 3
Dégg diine ak i cosaanam - الصفحة 3
1- Yàlla ak ub yonnenteem araamal na ñu jaay sàngara, ak médd, ak mbaam xuux, ak ay xërëm
2- Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan génn ci wanag day wax: "Xufraanaka
3- Tere na lépp lu am bëñ ci negment yi, ak lépp lu am aw sàll ci ñanaaw yi
5- ku gàddu ngànaay jëme sunu kaw kooku bokkul ci nun
6- dees na dagg loxo ci ñenteelu xaaju Diinaar jëm kaw
7- deesul dóor kenn lu ëpp fukki yar lu dul ci daani Yàlla
8- ku yar ab xaj bu dul xaju rëbb walla xaju sàmm wàññi na ci jëfam bis bu nekk Xiiraat
10- demal julli waat, yaw julliwóo
12- Yonente Yàlla bi daan na nu xamal listixaar ci mbir yépp kem ni mu nu daan xamale saaru Alxuraan
14- ku woor benn bis ci yoonu Yàlla, Yàlla soreele jëmmam ca sawara juróom-ñaar-fukki Nawet
15- nit ñi du ñu deñ di nekk ci yiw fii ak ñoo ngi gaaw a dog
19- xëddleen, ndaxte xëdd lu am baarke la
26- dàqleen Laylatul Xadri ci fukk yi mujj ci weeru koor
32- yàlla rëbb na Yahuud yi ak Nasaraan yi, ndax dañoo jàppe seen bàmmeeli Yonnente yi ay jàkka
36- ku woor at mi kooku woorul, woor ñatti fan mooy woor at mi yépp
37- kon bul ma seedeloo, man duma seede ag jeng
41- bu Ramadaan ñëwee dañuy tijji bunti àjjana yi, tëj bunti sawara yi, jéng saytaane yi
45- juróom-ñaar yii Yàlla dana leen keral bis ba genn ker dul am lu dul keram ga
46- bu kenn jëmale mbokkam ngànaay, ndax xamul ne Saytaane man naa bif loxoom, mu tàbbi ci kàmbu sawara
48- dénk naa leen julli ak ñi nekk ci seeni loxo
50- lu weesu ñaari dojor yi ci koddaay sawara la jëm
