إعدادات العرض
Dégg diine ak i cosaanam - الصفحة 2
Dégg diine ak i cosaanam - الصفحة 2
3- ku lekk laaj walla soble, bumu nu jege -walla mu wax: bumu jege sunu jàkka yi, te toog ci këram
7- ku jàngul faatiha amul julli
8- ku sangu bisub Àjjuma sangug janaba topp mu dem julli ji, dana mel ni ku saraxe ag giléem
9- kuy njëw ci yéen ci àjjuma ji na sangu
13- ku ne ci yéen ab sàmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm,
19- koo xam ne day jullu laata jant bi di fenk ak laata muy soh du dugg sawara
24- amul kenn ci yéen lu dul ne Yàlla dina wax ak moom, te kenn kuy firi du nekk seen diggante
25- moom am ndoxam lu laab la , am méddam it lu dagan la
26- bu ndox mi nekkee ñaari mbànd kon du téye sobe
33- Nëxit gi jigéen di gis ak mboq-mboq yi ginnaaw laab daawuñuko jàppee dara
34- toogal diir bi la sa mbaax daan téye, topp nga sangu
35- sangu bisub àjjuma war na képp ku toll ci gént,ak mu soccu, ak mu laal gëtt bu ko amee
36- bu genn jigéen tukki lu mat doxub ñaari fan lu dul mu ànd ak jëkkëram walla ab jegeñaaleem
39- boo sujjóotee, na nga teg say ténq te yëkkëti say conc
42- ku jàng aayatul Kursiyu ginnaaw jullig farata gu ne dara terewukoo dugg àjjana lu dul dee
45- ku sàmmonte ak ñenti ràkka njëkk Tisbaar ak ñenti ràkka ginnaaw tisbaar yàlla araamal ko ca sawara
55- Yàlla jéggal na samaw xeet li seen i xel di xalaat, fii ak defuñu mbaa ñu wax
60- Yàlla daa bëgg ñu def limu yombal, kem ni mu bëgge ñu def mbir yimu dogu
61- bu Yàlla dogalee ci nit ki mu faatu a fi barab da koy def mu am fa aajo
62- man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin
63- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàppu ci julli gu ne
64- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na benn-benn
65- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na ñaar-ñaar
67- war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam
69- bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man
70- ku tabax jàkka ngir Yàlla Yàlla dana ko tabaxal ca àjjana lu mel ni moom
71- genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka
72- bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na julli ñaari ràkka bala moo toog
74- yaw Bilaal taxawalal julli gi, noppal nu ci
75- yéen nit ñi, damaa def lii ngir ngeen roy ak ngir ngeen xam samag julli
76- bu ngeen di julli nangeen jubal séen sàppe yi, kenn ci yéen jiite leen, bu kàbbaree nangeen kàbbaar
80- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne
85- bu weeru koor ñëwee na nga dem umra ji ndax umra day yemoo ak aj
89- ñaar yii dañoo araam ci sama góori xeet wi, waaye dagan nañu ci jigéen ñi
90- Yàlla ak ub yonnenteem araamal na ñu jaay sàngara, ak médd, ak mbaam xuux, ak ay xërëm
91- Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan génn ci wanag day wax: "Xufraanaka
92- Tere na lépp lu am bëñ ci negment yi, ak lépp lu am aw sàll ci ñanaaw yi
94- ku gàddu ngànaay jëme sunu kaw kooku bokkul ci nun