إعدادات العرض
Dégg diine ak i cosaanam
Dégg diine ak i cosaanam
2- Lépp luy màndiloo dafa araam.
4- deesul julli fekk ñam wi daa teew, walla muy xëcconte ak ñaari sobe yi
5- boo waxee sa àndandoo: noppil ci bisu àjjuma, fekk imaam bi di xutba, kon fo nga
7- jempleen Seen mustaas yi, te yar sikkim yi
9- yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm
11- Yàlla du nangu jullig kenn ci yéen bu dee daa tojle ba keroog muy jàpp
12- socc day laabal gémmeñ di gërëmloo Boroom bi
15- képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram
16- ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram
18- li dagan de leer na li araam it leer na,
19- Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp
20- deesul loru waaye deesul lore, ku lore Yàlla lor ko, waaye ku sonle Yàlla sonal ko
21- Jibriil deñul di ma dénk dëkkandóo, bama muj njort ne dana ko dondloo
22- mocc ak takk ay xarnga-fuufa ak noob bokkaale la
23- buleen saaga ñi faatu, ndax ñoom kat wéy nañu ca lañu jiital
24- ku julli suba moo ngi ci kaaraangeg Yàlla
27- àdduna ay jumtukaay rekk la, te li gën ci jumtukaay yi àdduna mooy jigéen ju baax
28- Yàlla nee na: yaw doomu Aadama ji joxeel ma jox la
29- sart yi gën a yelloo matal mooy yi ngeen daganale péy ya
30- Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ko tudde Yàlla ginnaaw julli gu ne
32- ku bàyyi jullig tàkkusaan jëfam yàquna
33- Ku jàpp te rafetal njàpp ma, ay ñaawtéefam day génn ci aw yaramam bay génn ci ay weyam
34- bu nit ki dundalee njabootam di ci séentu aw yiw loolu dina nekk ci moom ab sarax
35- Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na zulu
36- buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli
37- ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka
38- digal nañu ma may sujjóot ci juróom-ñaari cér
40- Allaahumma Antas Salaamu, wa Minkas Salaamu, Tabaarakta Sal Jalaali wal ikraami
41- jullil taxaw, boo ko manul nga toog, boo ko manul nga wetu
42- ndax danga dégg wooteg julli gi?" Mu ne ko: waaw, mu ne ko: "kon nag wuyujil
43- Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal na ñu xutbag aajo
44- Deesul takk jigéen ci lu dul kilifa
46- Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- rëbb na kiy ger ak ki ñuy ger cib àtte
47- tabax nañu lislaam ci juróom
48- waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
50- mbugal ñeel na tastën ya ca sawara, deeleen jotal njàppu mi
51- Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar
52- ku fàtte genn julli na ko julli saa yu ko fàttalikoo, dara manu koo fay lu dul loolu
53- li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli
54- kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na
56- tere na nisër, daal di wax ne: "du indi aw yiw, waaye dees ciy genne aji-nay ji
58- li ñuy njëkk a àtte ci diggante nit ñi ëllëg bis-pénc mooy dereet
59- kiy xeex ngir kàddug Yàlla yëkkatiku kooku moo ngi ci yoonu Yàlla
60- bu ngeen déggee woote gi nangeen wax lu mel ni li noddkat bi di wax
61- bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab
62- loolu dereti sidit la, waaye bàyyil julli ci limu bis yi ngay gis mbaax, topp nga sangu te julli
63- yamaleleen seen sàppe yi, ndax yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi
64- Bu kenn ci yéen di jàpp na def ndox ci bakkanam daa di saraxndiku, kuy fomp (laabu) na ko tóolal
66- Mokkal naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki ràkka
67- Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan jug guddi day socc
75- Allaahumma baahid baynii wa bayna xataayaaya kamaa baahadta baynal masrixi wal maxribi
76- bu ab xaj naanee ci ndabul kenn ci yéen na ko raxas juróom-ñaari yoon
84- giñ naa ci Yàlla ne Yàlla gindi ci yaw benn waay moo gën ci yaw nga am géttug jur
86- daal di jàpp njàppum Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-
98- ñaari ndëggu jaam bi du pënd ci yoonu Yàlla ba noppi sawara di ko laal
100- ku julli ñaari sedd yi dana dugg àjjana
