إعدادات العرض
Xam jikkoy Lislaam yi
Xam jikkoy Lislaam yi
1- Ndax duma leen xibaar bàkkaar yi gën a mag?
2- bu nit ki bëggee mbokkam na ko wax ne da koo bëgg
3- moytuleen juróom-ñaar yiy alage
4- yal na Yàlla yërëm waa joo xam ne dafay yaatu bu dee jaay, ak budee jenn, ak buy fàyyeeku
6- Yàlla bind na rafetal ci mbir yépp
7- bul mer
9- moytandikuleen njort; ndaxte njort mooy wax ji gën a nekk aw fen
10- Bul xeeb dara ci lu baax, donte dangay dajeek sa mbokk won ko kanam gu bélli
11- am doole nekkul ci bëre daan, waaye ku am doole mooy kiy tëye boppam bu meree
12- Ku tegtale ci lu baax, dina am pay gu mel ni li ki ko def am
13- ab ràmbaajkat du dugg àjjana
14- képp ku gëm Yàlla ak bis bu mujj ba nay wax yiw mbaa mu noppi
15- ku dul yërëm nit ñi Yàlla mu kawe mi du ko yërëm
16- Ki Yàlla gën a bañ ci nit ñi mooy noon bi gën a man a xulóo
19- ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc
20- Yàlla dafa bëgg jaam bu ko ragal, bu doylu, bu nëbbu
22- def ndànk du am ci dara lu dul ne dana ko taaral, waaye du ñàkk ci dara it lu dul ne dana ko ñaawal
23- aji-gëm ji jikkoom ju rafet danako may mu am darajay Aji-woor ak kiy taxaw di julli
24- ñi gën ci yéen mooy ña ca gën a rafet jikkó
25- Yalla dana néggandiku tooñkat bi, ba bu ko jàppee du ko rëcc
26- yomballeen te buleen jafeel, bégleleen te buleen dàqaate
27- ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm
28- Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na zulu
29- Nekkoon a nu ci Umar mu wax ne: "tere nañ nu toggoo lu metti
31- ku ma fenal te tay ko na waajal ab wàccuwaayam ca sawara