إعدادات العرض
Yiy woyofal xol di ko dëdduloo àddina ak waaraate yi
Yiy woyofal xol di ko dëdduloo àddina ak waaraate yi
1- Jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am
2- li dagan de leer na li araam it leer na,
5- kenn ci yéen du gëm ba keroog bànneexam di topp li ma indi
7- baax mooy: rafet jikkó, bàkkaar mooy liy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ci gis ko
8- Ndax duma leen xibaar bàkkaar yi gën a mag?
9- bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate
10- moytuleen juróom-ñaar yiy alage
12- Yàlla dana ko dugal àjjana ak nu jëfam man a toll
14- ku ma sàmmal li ci diggante ay ŋaamam ak li ci diggante ñaari tànkam ma wóoralal ko àjjana
15- àjjana moo gën a jege ku ne ci yeen ay waroy dàllam, sawara it naka noonu
16- wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar
17- ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi ka raye ak ka ñu ray yépp sawara lañu jëm
18- li dagan de leer na li araam it leer na,
19- Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf
20- jëf yi mi ngi aju ca yéene ya, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am
21- gaay yay Pasar-pasaree alali Yàlla ji ci lu dul dëgg, sawara ñeel na leen keroog bis-pénc
23- bàyyiwuma sama ginnaaw fitna ju dàq a lor góor ñi ci jigéen ñi
24- Kenn ci yéen du gëm ndare ma gënal ko way-juram ak doomam ak mbooleem nit ñi
27- bi Yàlla bindee àjjana ak sawara dafa yónni Jibriil -yal na ko Yàlla dolli jàmm-
30- Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal
31- misaalu toogandoo bu sell ak toogandoo bu bon moo ngi mel ni ki yor gëttug Misk ak kiy upp ab furne,
35- yéemu naa ci mbirum jullit bi moom de mbiram lépp yiw la, te kenn amul loolu ku dul jullit bi
38- wàlle amul gaafal amul, njuuma amul, Safar amul, te nanga daw ki gaana kem ni ngay dawe Gaynde
40- sama xeet wépp lañuy jéggal ba mu des ñiy fésal ag moy
41- bu kenn ci yéen faatu lu dul ne dafa rafet njort ci Yàlla
42- man de bokk na ci li may ragal ci yéen sama ginnaaw, ñu ubbil leen naataangey àdduna ak taaram
44- lu baax mooy rafet jikkó, lu bon mooy luy dengi-dengi ci sa dënn, nga bañ nit ñi gis ko
46- nekkal ci àdduna mel ni ku tumurànke walla kuy jaar ciw yoon
47- éey yaw doomu Aadama ji boo ma ñaanee yaakaar ma ma jéggal la ak lu man a nekk ci yaw te duma faale
54- saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu benn waay naan: aka neexoon ma nekk palaasam
55- dinañu indi dee ci melow kuuy mu duuf
56- Séen sawara wi ab xaaj la ci juróom-ñaar fukki xaaj ci xaaji sawaraw Jahannama
58- Yàlla sadd na misaal ci yoon wu jub
59- bu ngeen gisee ñiy topp lënt ya xamleen ne ñooñii la Yàlla di wax nangeen leen moytu
61- {te dees na leen laaj xéewal yi bis booba}
63- dëddul àdduna kon Yàlla dana la bëgg, dëddul li ci nit ñi kon nit ñi danañu la bëgg
71- ñaari xéewal a ngi nii yoo xamne nit ñu bari woru na ñu ci: ag wér ak ug jot
72- ki jébbalu, ñu wërsëgal ko lu doy, Yàlla def ko mu doylu ci li ko Yàlla jox koo ku texe na”
74- am nga li nga mébét ak lu mel ni moom
80- jaayanteleen ak man ci ne dungeen bokkaale Yàlla ak dara, te dungeen sàcc, dungeen njaalo
