إعدادات العرض
Julli
Julli
1- deesul julli fekk ñam wi daa teew, walla muy xëcconte ak ñaari sobe yi
2- boo waxee sa àndandoo: noppil ci bisu àjjuma, fekk imaam bi di xutba, kon fo nga
3- yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm
6- ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram
7- ku julli suba moo ngi ci kaaraangeg Yàlla
8- Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ko tudde Yàlla ginnaaw julli gu ne
9- ku bàyyi jullig tàkkusaan jëfam yàquna
10- buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli
11- ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka
12- digal nañu ma may sujjóot ci juróom-ñaari cér
14- Allaahumma Antas Salaamu, wa Minkas Salaamu, Tabaarakta Sal Jalaali wal ikraami
15- jullil taxaw, boo ko manul nga toog, boo ko manul nga wetu
16- ndax danga dégg wooteg julli gi?" Mu ne ko: waaw, mu ne ko: "kon nag wuyujil
17- tabax nañu lislaam ci juróom
18- waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
20- Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar
21- ku fàtte genn julli na ko julli saa yu ko fàttalikoo, dara manu koo fay lu dul loolu
22- li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli
23- kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na
24- bu ngeen déggee woote gi nangeen wax lu mel ni li noddkat bi di wax
25- Mokkal naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki ràkka
30- man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin
31- bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man
32- ku tabax jàkka ngir Yàlla Yàlla dana ko tabaxal ca àjjana lu mel ni moom
33- genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka
34- bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na julli ñaari ràkka bala moo toog
36- yaw Bilaal taxawalal julli gi, noppal nu ci
37- yéen nit ñi, damaa def lii ngir ngeen roy ak ngir ngeen xam samag julli
38- bu ngeen di julli nangeen jubal séen sàppe yi, kenn ci yéen jiite leen, bu kàbbaree nangeen kàbbaar
42- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne