إعدادات العرض
Xam jaamu Yàlla yi
Xam jaamu Yàlla yi
2- deesul julli fekk ñam wi daa teew, walla muy xëcconte ak ñaari sobe yi
3- boo waxee sa àndandoo: noppil ci bisu àjjuma, fekk imaam bi di xutba, kon fo nga
5- jempleen Seen mustaas yi, te yar sikkim yi
7- yaw sama Boroom maa ngi lay ñaan bul def sama bàmmeel ab xërëm
9- Yàlla du nangu jullig kenn ci yéen bu dee daa tojle ba keroog muy jàpp
10- socc day laabal gémmeñ di gërëmloo Boroom bi
12- képp ku woor weeru koor ngir gëm ak yaakaar yiw; dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram
13- ku taxaw Laylatul Xadri ngir gëm Yàlla ak yaakaar pay ga dees na ko jéggal li weesu ci ay bàkkaaram
14- buleen saaga ñi faatu, ndax ñoom kat wéy nañu ca lañu jiital
15- ku julli suba moo ngi ci kaaraangeg Yàlla
17- Yàlla nee na: yaw doomu Aadama ji joxeel ma jox la
18- Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ko tudde Yàlla ginnaaw julli gu ne
20- ku bàyyi jullig tàkkusaan jëfam yàquna
21- Ku jàpp te rafetal njàpp ma, ay ñaawtéefam day génn ci aw yaramam bay génn ci ay weyam
22- buleen toog ci kaw bàmmeel yi, te buleen ko jublu ci julli
23- ñooñu aw nit lañu wow bu ku baax faatoo fa ñoom, dañuy tabax ca bàmmeelam ba jàkka
24- digal nañu ma may sujjóot ci juróom-ñaari cér
26- Allaahumma Antas Salaamu, wa Minkas Salaamu, Tabaarakta Sal Jalaali wal ikraami
27- jullil taxaw, boo ko manul nga toog, boo ko manul nga wetu
28- ndax danga dégg wooteg julli gi?" Mu ne ko: waaw, mu ne ko: "kon nag wuyujil
30- tabax nañu lislaam ci juróom
31- waaw ndax su ma jullee julliy farata yi, woor weeru koor, daganal yi dagan, araamal yi araam
33- Bu nodd-kat bi waxee: Allaahu Akbar Allaahu Akbar, kenn ci yéen wax: Allaahu Akbar Allaahu Akbar
34- ku fàtte genn julli na ko julli saa yu ko fàttalikoo, dara manu koo fay lu dul loolu
35- li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli
36- kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na
37- bu ngeen déggee woote gi nangeen wax lu mel ni li noddkat bi di wax
38- bàyyileen, dama leen cee dugal ñu di ñu laab
39- loolu dereti sidit la, waaye bàyyil julli ci limu bis yi ngay gis mbaax, topp nga sangu te julli
40- Bu kenn ci yéen di jàpp na def ndox ci bakkanam daa di saraxndiku, kuy fomp (laabu) na ko tóolal
41- Mokkal naa ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fukki ràkka
48- daal di jàpp njàppum Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-
52- bu Yàlla dogalee ci nit ki mu faatu a fi barab da koy def mu am fa aajo
53- man maay Damaam Ibn Sahlabata di mbokkum njabootu Sahd Ibn Bakrin
54- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàppu ci julli gu ne
55- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na benn-benn
56- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na ñaar-ñaar
58- war na ci bépp jullit mu sangu ci juróom ñaari fan yu nekk benn yoon, da ciy raxas boppam ak yaramam
60- bu ngeen déggee noddkat bi nangeen wax lu mel ni li muy wax, te ngeen julli ci man
61- ku tabax jàkka ngir Yàlla Yàlla dana ko tabaxal ca àjjana lu mel ni moom
62- genn julli ci sama jàkka jii moo gën junni julli ci fu dul moom ba mu des jàkka ja ca Màkka
63- bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na julli ñaari ràkka bala moo toog
65- yaw Bilaal taxawalal julli gi, noppal nu ci
66- yéen nit ñi, damaa def lii ngir ngeen roy ak ngir ngeen xam samag julli
67- bu ngeen di julli nangeen jubal séen sàppe yi, kenn ci yéen jiite leen, bu kàbbaree nangeen kàbbaar
71- Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne